Waxtaani jëfandikukat:Ahloubadar

Le contenu de la page n’est pas pris en charge dans d’autres langues.
Jóge Wiktionary.

baa yi[Soppi]

Dama la bëggoon wax ne sooy dugal baat bu bees ci Wiktionary:xam-xamu nosukaay, bul di far baat yi fa jota nekk, man ngaa bind sa baat ci wet gi, loolu dina tax sunuy dem bay tëj sémb bi xam ci yan baat lañu wara diisoo, bun ci juboo jël leen. --Ibou 20 Awril 2009 à 19:07 (UTC)[répondre]

Dugal ab baat[Soppi]

Saytul xët wii ngir xool nuñuy dugalee baat bu bees: fii --Ibou 10 Awril 2009 à 12:04 (UTC)[répondre]

defar naa royuwaay bi (Royuwaay:nduroowaale). jarul ngay dugal sa tur ci biir xët wi, xët woo sos soo xoolee ci jaar-jaar sa tur dina fa nekk, xët yi nekk fii benn amuci tur ci biiram, lii bokk na ci li wikbaatukaay tere. --Ibou 26 Awril 2009 à 10:27 (UTC)[répondre]
waaw degg naa liga wax waaye jublu wu maci wanewu wala jaayub xam-xam mbaa luni mel, li maci jublu mook liñ jublu ci delluwaay ñoo yam ndax day waral boo amee looci baga leer lu mbaa luni mel ga man a jokkoo ak kiko fi dugal xamnaani dinañ ci def cëru gi waaye loolu ñi nekk ci dàl bi ñoo kay xam te warkat yi laaciy sooraale, loolu baax naci lool boo andul ci lii yit manees nakoo dindi waaw-kay jambaar--Ahloubadar 26 Awril 2009 à 15:32 (UTC)[répondre]
xam naa ne du wanewu, dayni rekk sémb yi ëmbu ci wikimedia yépp nii lañuy doxee, kon faaw nun tamit nu tënku ci. Leneen li mooy, bëggoon naa xam baatu nduroowaale loo ci jublu, man bi may sos xët wi omonyme laa foogoon nga ci jublu, waaye ci ni nga koy jëfandikoo mel na ne leneen lay tekki. --Ibou 30 Awril 2009 à 18:09 (UTC)[répondre]
nduroowaale li ma ci jublu mooy buma dugalee ab baat xool baat yimu ndurool te bokku ñu tekki dugal ko ci suufu xët wi, firndé:bu ma sosee aw xët leeral ci batub suuf def ca suufu xët wà asamaan, jawwu ak niir, ngir ñoodi ay nduroowaleem mbaa ay jegeñaaleem te bokku ñu tekki kon du mafa man a def bokktekki, amna nak ay baat yuma ko man a jëfandikoo yu melni:soxna, jabar, takkoo. bokkul ak homonyme doonte nduroo na, homonyme mooy turandoo. xeewël waaw-Kay

waxi wolof[Soppi]

  • Mbej wa ray mbar ponkalakoy dóor (ahloubadar) litax ma def ci ahloubadar ji maako sos maanaa maako jakk a wax ci addina
  • Ag caqamee gën ag këmm maa soppi lii gafi dugaloon xamnaa daga koo teewluwul waaye cuqqum a gën kamm la caqami cumuq mooy coow liy gen booy saqqami dara moo tax ñuni moo gën kam waaye du këmm , këmm dagg lay ndurool maanaam baaraam yu këmm, kamm nak mooy safaanub saqqami maanaam ni cell.
  • Njaabum gileem la waaye du njabum gileem
  • njëkk a fecc taxuta mujjeb géew la waaye du taxuta mujje géew

boo fi gisee loo xamni nandoo ko wala mu xaw laa jaaxal wax mako man miko fi dugal ma joxla ci'y leeral lu njëkk ga koy soppi mbaa ga koy far, waaye bula wooree nak man ga koo far mbaa soppi. yeneen coppite yi nak rafet lu naako waaw-Kay nandal-bubaax (bonne comphention)

xam naa bu baax ñaari baat yépp, saqami gi ngay saqami mooy ag caqami bokkulag cuqami bi nga wax, këmm mooy ñakka ndékki dina tekki it «vide», kon wax ji limuy firi mooy: saqami dara moo gën ñakka ndékki.--Ibou 1 Mee 2009 à 14:02 (UTC)[répondre]
déet bu nu werante ci loolu waxunu ag caqamee gën këmm cuqqum a gën kamm lanuy wax, linu ci jublu mooy rek ni am a gën'uk ñak.
  • cuqqum mooy burwi bigay degg booy saqqami moom lanu tuddee cuqum-cuqum,
  • kamm mooy ŋeb ni cell maanaam amoo loo saqqami,
  • këmm nak daa melni danga koy jaawale ak pëŋŋ, ndax këmm du firi vide këmm mooy lu dag daggiin wu moyul maanaam luñu këtt, pëŋŋ moo man a firi vide maanaam lu dara nekkoon te jeex. te yit ngir leeb wi jaar yoon faww linga jakka wax doon safaanub beneen bi, melni cuqqum ak kamm, waaye caqqami ak këmm bu këmm dee firi ñakka ndekki it du tax mu jub ndax saqqami ñakka ndekki du safaanam, ngir leep ni nga ko war a melal ndekkee gën këmm waaw-kay nandal-bubaax

é== waxiin == am na jumtukaay bu bees boo man a jëfandikoo ci xët yi. misaal ci baatu «alal» lii ngay bind:

{{waxiin}} Déglul ni ñuy waxee baatu alal ci wolofi senegaal [[Dencukaay:Wo-alal.ogg]]

xoolal fii alal ngir gis limu lay jox.

demal fii ngir gis dencukaay yépp, commons:Category:Wolof pronunciation.

wax ga dëgg lu am solo la tambali woon naa diko jëfandikoo demb ci jukki wolof yi, ci nasaraan ak wu-angalteer ak wolof ngir gis ko kokkal ci yi Fr, En, [Wo]

betey maangi denc (enregistre) ay kaddu ngir baat yi DerbethBot jotula dugal te it maangi koy dugal ndànk-ndànk waaw-kay --Ahloubadar 1 Mee 2009 à 14:37 (UTC)[répondre]

jarul ngay yebaat dencukaay bi, ndax lu nekk ci Wikimedia Cammon man nga koo jëfandikoo ci bépp sémbu wikimedia, doy na nga bind tur wi rekk mu feeñ, soo xoolee bi may defar «alal» damaa ñëw rekk bind «Dencukaay:wo-alal.ogg», mu jox ma ko--Ibou 2 Mee 2009 à 12:43 (UTC)[répondre]
deet yabaatuma ben dancukaay damaa dugal yi fi amagul te seeni baat am ci wikbaatukaay, ngir xool ko kokkal fii kaddu gu ma ci dugal defaale naa ci ab dayam. njuum te yobbu woon nama ci dugal fii gen kaddu.waaw-kay --Ahloubadar 2 Mee 2009 à 14:40 (UTC)[répondre]

Nuyyoo[Soppi]

Sang Abdu Xaadir, ñi ngi lay sant ci liggeey bu am bi solo te nga dëkke ko ci dal bii, ma la doon xamal ne ngir gën a am ag dëppoo ak liggéey bu nosu ba ñépp man cee jariñu - xam naa sax yaa ngi ko doon def - ma doon ñaan boo manoo a yër lees fi jotoon a def, ba xam dëppoo na ak say gis-gis boo ci àndul nga wax ñu, nu waxtaan ci ba dëppoo ci, moo gën di sos di sosaat, te lu aju ci xam-xamu nosukaay damaa bëggoon ngeen bàyyil ma ko noonu tuuti ma àggale ko bu boobaa manees cee def aw waxtaan, ba gën cee dëppoo, ndax xam gees dul sikk Yàlla rekk a ko ame. Waxal ma ko it Ibou. May dellu di yeesal ag cant ci say jëf yu am solo.

Lu mel ne turu baat akuw santam, nga xam ne mooy ci fr article defini ak indefini: nun jotoon nanoo indi ay baat yu leen di wund, boo xoolee ci nos-wax ci wikbaatukaay gis leen fa, boo gisee ne yooyu nga indi ñoo gën nu waxtaan ci, bu loolu jàllee nu àndaat joow sunu gaal giy Senegaal ngir raw ci gaal. --Abdu Xaadir KEBE 22 Mee 2009 à 13:43 (UTC)

Yaaram yaama gën a yélloo sant ngir sa goora ak sag cawarte santées nala gërëmees nala, man damay jéem rek, wax nga dëgg xam gees dul sikk Yàlla rekk a ko ame. te naggu leesu koko ci adduna, damay faral di wax naan: wax lu ñépp ànd mbaa jëfees ko kénn manu ko waaye fexeel di wax mbaa di jëf lu ñépp manoo na ànd te nóppi,
  • turu baat akuw santam, maako xalaatoon te yaakaarni jub na, soxla woon naa xam bi geen sosoon ?
  • wàllu xam-xamu nosukaay man dey bàyyi naalaak sama wàll te wey ci laneen,

loo wax ci sama bind bii ma def ci ag ak gi ? yónnee woon naako ca dal bii di xibaayi.com

defaroon naa ab dal bu yitte woo mbirum muriit ci FR booci manoona dugal sa loxo ci wàllu jukki yi, maangi koy tekki it ci wolof te fas naafa yeenee def teerey Sëriñ bi yi nga tekki ci wolof bu maci amee sa ndigël ? dal baa ngii www.ahloubadar.co.cc . am na ab xassida bu Alaaji Sëriñ Gey Badar wayoon Sëriñ Saaliwu sa maam ja, def naa ko ci man nga koo gis boo demee jaare ko ci "Bibliothéque/Sr Gueye" mooy Yaa Saalihal. defar naa it ab dal buy yitte woo mbirum waa mboussobe muy www.mboussobe.co.cc cant gu matale ñeelnala Waaw-kay --Ahloubadar 22 Mee 2009 à 17:22 (UTC)[répondre]