ab bind ci wolof
Apparence
leeral
[Soppi]Bind nag bu ñu ko waxee mooy leçon ci fr
- Catul waxtaan jooy na ñu laaj ko mu ne aji jóox a ma rax aki baatam te xamul samay mbokk
Tekki gi:catul waxtaan li ñi ngi ci jublu mujjantal gi, aji jóox mooy ki jekki jekki rekk dugg, mbokk yi mooy ndoortel waxtaan wi ak digg bi.
Maanaa mi:nit warul a fekk aw waxtaan di ca dugg te xamul lañuy wax. Ki ko njëkk a wax: Abdu Xaadir KEBE
Ci jafeg xam-xam
[Soppi]- Xam-xam gub la ci leemi jaag bi, ku dul bojjkat du fenqook moom
Tekki:
- gub: bant biy yor dugub ji ci gàncax gu dugubi suuna aki mbokkam
- leem : takk walla say yu ndaw yu gub yi
- jaag : leem yi bu nu ko dajalee ba mu dajaloo doon ab jóor
- bojj: tàqale dugub ji ak gub wi
- fenqoo: daje
Maanaa mi: njariñ coona'a koy joxe
Ki ko wax: Abdu Xaadir KEBE