Jëfandikukat:Ahloubadar

Jóge Wiktionary.
Dem: Joowiin, Seet
ilimaan.jpg

Sëriñ Abdu Xaadir GÉY Badar (Jiili GÉY) Mongi juddoo Ndakaaru Senegaal, baayam mongi tudd El Haaji Sëriñ Géy Badar (Raay mu sedd) yaayam mongi tudd Soxna Ummi Njiaay mongi nekk Senegaal/ndakaaru/geejawaay mongi jangéé Njiukki (kadior) jamono yi mongi yaggu ci nosukaay gi (ordinateur)ak lepp lu aju ci xam-xamu xaymà (technologie mathématique)

Liko Taxa Juk[Soppi]

Salaam sama bokki wolof yi mbaa jàmm ngeen'am ? man déy ab wolof laa bu wolofe te ma yaakaar ni looloo ma war batax ma juk di laggéeyal wolof moomi ngir mu tóllook ñi mu bókkal aw tur mudi làkk mbaa sax mu jege leen ndax moom wolof moomi loolu jómbu ko ndax yàlla taggat nako bamu nooy man dey ngisou ma làkk wu ko gën a mat ca cosaan xanaa kay li am mooy làkk wuñu tóppatoo ak wuñu sàngane te moom nak melnani ci yiñu xawa sàngane la bokk man dey loolu neexuma batax ma juk fas-yeene cee def lima ci man a kus neew ngir dooleel ko te ma yaakaar ni képp kuy wolof war nacee jàpp ndax yàlla mila bind defla ngay wolof moo la gën a xam sa bop. di jéggaani aw làkk te yor ci wu nooy te neexa wax loolu bókkul ci fulla, day tax ñu yab la rek, looloo waral réewi tugal yi not ñu ba leegi nde ñoo ñu abal aw làkk wuñuy liggeeyee te wolof njaay nee ku la aal bët fuko neex ngay xool, man dey fippu naa ngir bàyyil leen fi seen làkk yooyi du maci weesu jànk ak wut xam-xam binu bokk ñun nit ñep teñu aakimoo ko def ko ci seen làkk yi, te buma koci amee insaa allah dinaa ko soppi ci wolof diko jàngale. fii ci sunu réew yi litax ñu yeex bokku naci kufi juddoo ñu dugal la ci daaray nasaraan yi 12at ngay jàng ngir dégg làkk wi door a dugg ci daara ju kawe ji(universite) di jang làggeey(métiers) xamngeen ni loolu jaaduwul moo waral it doofi gis ku am xaalis ci'k ndawam ak yeneeni mbir yu wara tax ñu fonk suñu làkk wi, làkk woo xamni booy gént ci ngay gént booy saaga yit ci ngay saaga boo bëggee defar sa gént dinga ko jëfandikoo, waaw-kay

Jokkalekaay[Soppi]

  • wuyukaay gu dëkk:221338370027
  • Wuyukaay guy tuxu:221775724577
  • E-Bataaxal hotmail:djili.gueye@hotmail.com
  • E-Bataaxal Yahoo:badargueye24@yahoo.fr
  • E-Bataaxal:ahloubadar@in.com wala ahloubadar@touba.com
  • Dàlu Web: ahloubadar.co.cc wala mboussobe.co.cc
  • Blog: ahloubadar.blogspot.com,
  • ay widewoom ci youtube