tekki
Apparence
Wolof
[Soppi]→ Mottalil gongikubaat bi. (Soppi)
tekki b:
- ci xayma: mooy li lay xamal nu am mbir mel, numuy doxee ak numu tëddee
- def ab tekki
- tekkib am mbir
- ci làkk: moo lay wax lu ab baat di firi
- baat bii de, xamuma lu muy tekki
- faaw nga xam lu ab baat di tekki ngir man koo jëfandikoo ci say wax.
tekki g:
- ci liggéey: samag tekki maa ko liggéey
tekki b:
- ci xayma: wax nu am mbir mel, numuy doxee ak numu tëdde
- tekki ab appoo
- ci làkk: jox ab baat fireem, wax li muy firi
- tekki ab baat ci wolof
- ci liggéey: liggéey ba am alal
- Musaa moom tekki na
- soo bëggee tekki faaw nga liggéey
Tekki
[Soppi]wu-faraas: (xayma) définir, définition, (làkk) traduire, traduction, (liggéey) réussir, réussite
Delluwaay
[Soppi]Mbay Fay - nanu xayma - Tëngéej IREMPT (UCAD), 2005