Léebu
Apparence
Fr:proverbe
A
[Soppi]- Alal du faj dee, gàcce lay faj
- Am saxul, ñàkk saxul
- Ay du yam ci loosu boroom
- Ay du weesu baay dee na
- Àdduna weeru kóor la, fàww jant so nga doora wàññi bis.
B
[Soppi]- Bàkk nga njaak
- Bu ndox tuuroo am bàq a fa des
- Bu ñay di xàlluw yoon doom jaa tax
- Bërigo ci mbartal ku ko bëmëx mu dem, ku ko ba, mu dem
- Bu gudd nopp doon tax di njiit mbaam di suñu ilimaan
- Buur du mbokk
- Bala ngaa xam xamadi xaw laa ray
- Bëñ weex na lool waaye dereet a ko lal
- Bu/Su yoon jeexul waaxusil du jeex
- Boroom ñeenti tànk du lab
- Boroom mbaam a xam mbaamam
- Boroom lal a xam màtti lalam
- Bët du yanu waaye xam na lu bopp àttan
- Bakkan waraw dàll la, fa muy dàggee dooko yëg
C
[Soppi]- Cërub ma xàjj, ma xujj a koy jël
- Cuqum a gën kamm
D
[Soppi]- Doomi ñay bu ko ñaanal mu rëy, ñaanal ko gudd fan
- Duma jënd jaan ci pax
- Dama laa bëgg maa la raw sëy bu mu takk, dangaa reew yaa ma raw a koy tas (abdu xaadir géy)
- Dangaa jot ci bakkan bay ñandu
- Daaray lëg guddu nopp jarufaa jaay
- Dóor wa ray mbër ci ponkal lay bawoo (Ahloubadar)
- Dëkkandoo jàmm a ca gën
- Doomi mbër jàngil bëre, yàgg-yàgg dees na la ñam
E
[Soppi]F
[Soppi]- Fa ndox daa taa boo demee fekk fa tepp-tepp
- Fët-Fët tàggalewul mbaam'aki noppam
- Fullaay jaay daqaar, mbaa ma ñam jeexal ko
G
[Soppi]- Gaynde du lekk mbuum yàpp lay dunde
- Gewël bu reppee cib xare lu mu jiin xeep ko
- Gumba du jiite rëbbum jaan
- Gumba tal na lu dul tëbi kàmb
- Góor gu tàyyeel, gàtt wërsëg, néewi soppe
H
[Soppi]I
[Soppi]J
[Soppi]- Jigéen soppal te bul wóolu
- Jëm ca làmb ja di bàkku, juge ca di bàkkoo ko gën
- Jàng jàngaan boo mokkalee ber sa daara
- Jàngoro ku ko nëbb mu lor la
- Jàngoro dees koy weer
- Jikkook boroom pax rekk
K
[Soppi]- Ku muñ muuñ
- Kewël du tëb doom ja bëtt
- Kuy naan di nëbbu, boo jéggee feeñ
- Ku njëkk a jug boroom ndékki dinga tëddaat
- Ku boot bukki xaj bëw la
- Ku wex wéet
- Ku ñuy jiiñ dëmm ngay soccoo yaxi liir
- Ku puudër tax a rafet boo ñaqee ñaaw
- Ku bañ a xitax bul yàgg ca mbojj ma
- Ku yàgg cib teen baag fekk la fa
- Ku manul, bawoo, lu yàqu yaw a
- Ku log, log-logal
- Ku la aal bët, fu ko neex ngay xool
- Ku saraxul gumba, bàyyi kook yalwaanam
- Ku ndobin ray sa maam, boo gisee lu ñuul war a daw
- .... Ku ko lebal ker, mu faye la guddi
- Ku jaan matt sam xel dem ci dee
- Ku la mag ëpp lay sagar
- Kuŋ-kuŋ ca wolandoo wa
- Ku yar sam kuy, yaw lay njëkk a daan
- Kuy xalam di ca jaayu (joowu)
- Kiy yenni gan du ko gunge
- Ku bëgg akara dangay ñime kaani
- Ku niikiwul naaka
- Ku naggu, naggu loo moomul,
L
[Soppi]- La tee nag wa dabi nag yaa tee ñeex maa neex
- Lu waay rendi sa loxo lay nàcce
- Lëg bu lekkee olom na ko gërëme cooy
- Laago du wees
- Lu jot yomb
- Lu xaj lekk lekk, ba fa der ga ca baat ba
- Liggéeyu ndey añub doom
- Lu ñépp wax ay dëgg
- Lu yàgg dëgg la
- Lu defu waxu, Luy ay di njàmbat
- Lu njiig njaaga mooy njaag
- Lu mag def dee, bu dekkee ba ko
- Lekkoo ci ndab li bëgg cee xëpp suuf
- Li ci kanam, rawuli gët
- Lu cin xat xat, nga war caa boqus xorom
- Lu yëngu la ko yëngal a ko ëpp doole
- Lu jiwu wa jeexul jugu fa
M
[Soppi]- Mbejum kanam, boroom a koy fajal boppam
- Mbej wa ray mbër, ponkal a koy dóor
- Mag mat naa bàyyi cim réew
- Man a man a, yaw a yaw aa ko gën
- Mattum xaalis boroom a koy jaaroo/suuroo
- Muus mu nekk ak na muy toje boppu jinaxam
N
[Soppi]- Ndànk ndànk ay jàpp golo ci ñaay
- Nen, du bëreek doj
- Nit, nitay garabam
- Njëkk a fecc, taxut a mujjeb géew
- Njaabum giléem, xajul ci waañ
Ñ
[Soppi]- Ñulug sa jëkkër, yakk sa doom
- Ñu bokkub teen ay jaxasoo ay goj
- ñi man a kott amuñu mbaam
P
[Soppi]- Powum jaar, ca wetu paxam
- Picc mu masul a naaw, bu/su naawee firi'm réew
Q
[Soppi]R
[Soppi]- Rayub tubaab yomb na, waaye fekke dëj baa jafe
S
[Soppi]- Suul ker du ko tee feeñ
- Sikk su feeñ cib sëy, nuyyoo na ca ngoro ga, dees koo fayul
- Sa gimiñ xasaw na sa doomu nday a la koy wax
- Saabu du fóot boppam
- Saaku bu dara newul du taxaw
- Soxla buy ñaar jàmm a ga ca,
T
[Soppi]- Tarxiis bu dammee loosu mbonaat, ku yor gëléem war a yësal
- Tere tere mu të, bàyyil mu gis
- Tàmm laago la
- Toŋ-Toŋu naat su wëreem réew dunq yaa tax
- Teen bu neexee pind ba du féex
U
[Soppi]V
[Soppi]W
[Soppi]- Weex, yàquli bëñ
- Waxma sa xarit, ma wax la sa bópp
X
[Soppi]- Xaalis, amul xarit
- Xaalis loo ko yonni mu indi ko, waaye falay jaare
- Xel, du jariñ lu dul xalaat
- Xar, day weesu mbote
- Xarit, dees koy tànn
- Xeeb nga xal, mu lakk sa dàgga
- Xool asamaan jarul buuxante
- Xëbtal, du tax doomi lëg a màtte
- Xalangu, dajul suuf.
Y
[Soppi]- Yàgg bawul dara
- Yariit du bon, yarut du baax (ahloubadar)
- Yéene néeg la boroom a cay fanaan
- Yoon yamul ci benn
- Yàkkamti yàqule