yaradiku
Apparence
Yaradiku, baat la bu jóge ci yar (teggiin) waaye ni ñu ko tëggee ci wolof dafay dàq, bu ñu nee nit ki dafa yaru mooy ne ku am teggiin la, bu ñu nee nit ki dafa yaradiku mooy tekki ne amul i teggiin.
Yar+adi+k+u:
Yar: reen la
Adi: toppaan la
K: loyu koddaay la
U: toppaan la.
Maanaam gongikuwaayu baat bi mooy "Yar". "Adi" day taq ci baat ngir dàq ag amam (niki: xam: am ug xam. Xamadi; nàkk ug xam.) "K" dafa ñëw ngi dox ci diggante "i" ji ci "adi" ak "u" ji mujj ci "yaradiku" maanaan dafay teet ñaari woye di mbëkkante. "U" day taq ci baat ngir jëmal ag amam. Niki yar => yaru. Yaradi=> yaradiku.