Aller au contenu

mball-xal

Jóge Wiktionary.

wolof

[Soppi]

Am na nag ay mbàll-xal yu suuf yi, mbàll-xall yu ron-géej (sous-marin)ak mbàll-xal yu biti-suuf si(extra-terrestre)

Xeeti mbàll-xal yi:

mbàll-xal yi ak seeni saxaaruwaay yu mbàll-xal (cheminées volcanique)danañu feeñe ci ay melo yu bari:

  • Les stratovolcans
  • Les volcans boucliers
  • Les calderas
  • Les cônes de scories
  • Maars, diatrèmes et diamants
  • Volcan sous un glacier


Diigiitu mbàll-xal

Mbàll-xal day sànni ak a buusu ay diigiit (magma) ci jamonoy jañu gi (Lors d'une éruption) ak fipp gi. Magma bi nag walla diigiit yi ab ne-ne la buy jëm ci ndoxe kem ni tàngoor wiy tare ak a taradee. Nu tàngoor wi gën a tare rekk, magma bi gën koo ndoxee, gën koo yoloo. Diigiit yi walla magma bi, saxaaruwaay yu mbàllxal yee koy jañ, bëmëx ko mu génn néegub magmaam boobu(chambre magmatique). Néegub magma bii, mi ngi ci xolliitu suuf si(la lithosphère).

Bu magma bi agsee ci kaw suuf si(la surface de la terre) day séddaliku - ci anam gu tar ga ëpp mbaa mu yées - ci aw melokaan wu yolaakon (xal mbaa gil)ak wu gaas (toggaliit yu saxadi) (composés volatils). walum gil mi walla mu xal mi {Les coulées de lave} day sottiku bawoo ci pax mu mbàllxal mi (Cratère volcanique) walla bawoo ci ay ubbéeku (ouverture) yu am ci wàll yu nekk ci peggi mbàll-xal bi. Ginnaaw bu ñu setee te dañ ci gaas yi, dañuy tàmbalee wow ak a dëgër ndànk-ndànk ngir sedd gi ñuy def, bu ko defee nag, sos ay doj yu mbàll-xal (roches volcaniques).

français

[Soppi]
  • volcan

english

[Soppi]
  • volcano