Aller au contenu

ag nguur gu ñeent

Jóge Wiktionary.

nguur gu ñeent:noste la gu nguur walla gu àtte gu imbraatóor gu Rom gi Diocletien taxawaloon ci 292 ngir saafara jafe-jafe yi rëyug imbraatóor gi waraloon ak ngir jànkoonteek song gi leen bar-bar yi songoon. Imbraatóor gi nekkoon na di lu ñu séddale ñaar, xaaj bu ne am ca bopp ba ab imbraatóor bu ñuy wooye "Ogist", bu ab Xaysar di jàppale.