ag ak gi ci gàñcax

Jóge Wiktionary.

ci wàllu gàñcax[Soppi]

  • garab, ag la tudd, sant gi, Misaal:ag garab, garab gi.
  • Garab yépp ñoo bokk aw tur mudi Ag Misaal:ag guy, ag nixmaa, ag sump, ag dàqaar, ag kàdd.
  • Grab yépp ñoo bokk aw sant mudi gi Misaal:guy gi, nixmaa gi, sump gi, dàqaar gi, kàdd gi.
  • Doomi garab yépp ab lañu tudd, amna ay xarbaax mudi aw wuy, aw kocc, aw bata, waaye batay doom yees di lékk ab buy lay tudd, muy li nékk ci biiru wuy, kon buy bi moodi doomi guy gi ndax moom lañu soxla. Misaal ci turu doomi garab yi: ab somp, ab dàqaar, ab àdd(amna wuute ak moroom yi ndax jëlul turu ndayam), ab buy.
  • Doomi garab yépp bi lañu sant, amna ay xarbaax mudi: wuy wi, kocc wi, bata wi, waaye batey doom yees di lékk buy bi lay tudd, muy li nékk ci biiru wuy, kon buy bi moodi doomi guy gi ndax moom lañu soxla, Misaal ci santi doomi garab yi: somp bi, dàqaar bi, àdd bi(amna xarbaax ndax jëlul turu ndayam niki ab kàdd), buy bi.

Tur

  • Ag guy, Aw wuy (amna ñuy wax aw buy), Ab buy,
  • ag sump, ab sump.
  • ag dàqaar, ab dàqaar,
  • ag kàdd, ab àdd(amna xarbaax ndax jëlul turu ndayam niki ab kàdd,
  • ag nixmaa, ab nixmaa.

Sant

  • guy gi, wuy wi (amna ñuy wax buy wi), buy bi,
  • sump gi, sump bi.
  • dàqaar gi, dàqaar bi,
  • kàdd gi, àdd bi(amna xarbaax ndax jëlul turu ndayam niki ab kàdd,
  • nixmaa gi, nixmaa bi.

aji leeral ji: Abdu Xadir Gey >>Ahloubadar