yewwute

Jóge Wiktionary.

wolof[Soppi]

Ñenn ñi naan ko "renaissance" ci français di judduwaat, di ci araab "nahda" , di ci maanaa buur , buur nag bu nu ko waxee ci wolof moo'y jekki-jekki jug ,taxaw, ñeneen it di ko fire'e dekki, boo ko'y seet ci maanaa, yepp di wudd lenn, di la amoon ca Tugal ca lenn ci'y jamonoom, di woon lu am solo, di lu waa Tugal dul fatteeti, baat bii ñew ëmb maanaa mii mépp, di raññale jamono'y yewwute ci ngëmméen, judduwaat ginaaw ag dee, réer ci réeradi,xam ci xamadi, siggi ci sëgg, nërméelu ci taxaw, giim ci tàkk, xippi ci gëmm. Bii baat daal jaasi la ju moo dog seen diggante ak jamono joj tëñëxu ak yewwoodiku moo ko muuroon, matale ko, xel mu gàtt lakkal leen ci, gisiin wu ñaaw sonal leen ci, ñu nekkoon ci biiram di way jemadi kanam, di ñu soxlawoo ag leer, ba Yàlla yee ay nit, niital léen ca làmpam bu leer ba'y leerale, jugloo leen ci'y nelaw, ñu nekk ci'g" yewwute" duggalaale ci ñeneen ñu dul woon ñoon, ba tay Tugal gii, di lu leer, ca googale leer la tanqe, te ca la yewwoo it. Kon ci gàttal yewwute fii mooy renaissance gi nga'y dégg ci kàllaamay frãase tey tekki ci maanaa yewwute rekk, ndax mooy judduwaat gu xam waral, ginaaw dee gu réer waraloon

français[Soppi]

  • renaissance