mbooloom Bilderberberg
mbooloom Bilderberg mbooloom jeexiital la mu ame ci ay jëmm yu ay réew yu wuute, bawoo nag ci àddunay liggéey ji, ju ndefar ji, ju koppar ji, ju tasukaayu xibaar ji, ju xare ji ,ju politig ji ak yennat ci ay jëmm yu bawoo ci yenn ci ay daara yu kawe .
Moom nag mi ngi sosoo ci wenn waxtaan wu amoon atum 1954 ca Dalu-gan bu Bilderberg bu Oosterbeek (suuf yu xure yi), ka woote woon ndaje ma di Buur bi Bernhard bu Suuf yu Xure yi, mu nekkoon di kenn ci ñaar ñi ko sosoon, ka ca des di David Rockefeller
Booba ba leegi at mu jot lu tollook 120 ciy nit danañu ko def ci ñeenti fan ci benn dëkk, ak ci nëbbu gu tar, bu jàllee it deesu ci teg menn ndajem tas-xibaar, waaxtaan ya tam ci ag tëju lay ame, te way teewe ya nuy tudde "ay ñoñ Bilderberg" du ñu leen may ñu fay karmat dara, mbaa ñu cay wax lenn ñeel taskati xibaar yi