Waxtaani jëfandikukat:Abdu Xaadir KEBE~wowiktionary

Le contenu de la page n’est pas pris en charge dans d’autres langues.
Jóge Wiktionary.

li ma begg a xam mooy nan lanuy duggale baat.

mbootaay gi[Soppi]

tambali naa cee liggéey ubbi naa waxtaan wu am solo ñeel tëriit li, nit ñi ëpp solo ci wikipedia da ñuy faral di ñéw ci waxtaanuwaay boobu, yaw sax man nga fa bindu di joxe sa xalaat demal fii.

biologie nan lañ ko mana waxe : gëstudundu. leneen tamit: resaux: mbaal, walla caax laa tekkee woon. lënd: web la gëna jege. war nañ def tamit ab xalaat jëmale ci ni wolof di woowee yeneen làkk yi

su ab wolof (di ku bokk ci xeetu wolof) di làkk wolof, ab pël di làkk pël, ab mandeŋ di làkk mandeŋ, kon ku dëkk faraas, ab waa-faraas la ko wolof wara woowee walla ab faraas, walla ab faraas-faraas (ni ku dëkk bawol, bawol-bawol, siin, siin-siin añs). Ki koy làkk nag walla làkk wi ci boppam? su fekke ku dëkk faraas ñu woowee la ab faraas li muy làkk itam war naa mana ne faraas (kàllaama faraas). Ku xeetoo ci wolof di làkk wolof, ku xeetoo ca faraas di làkk faraas walla waa-faraas, ku xeetoo ca itaali di lakk itaali walla waa-itaali. --Ibou 26 Maami-koor 2008 à 11:19 (UTC)

Tontu[Soppi]

  • Biologie: xam-xamu dund; walla ndundat. Ndundat nag mi ngi juge ci dundat biy firi etre vivant. Etre vivant it foo gise ci sa may mbind ma wax fa aji nekk juy dund xamal ne mooy etre vivant moom tam da koy tekki maanaam ci Italiano spece vivente.Kon ndundat walla xam-xamu dund mooy xam-xam biy jàng ak a gëstu mbooleem li aju ci dund gi ak way dund yi.
  • Resaux:Mbaal laa gën a ànd ak doonte soreewuñu ay maanaa, boo ci wax baax na
  • Lënd: mooy tàggum jarguñ, day tekki web ndax web baatub angle la làkkuw frãas jël ko di ko jëfandikoo du ñàkk ngir gën gee jàppandi, waaye gis naa ne lënd moom mooy web rekk, gënu koo jege waaye da koo doon
  • Ku dëkk farãas - diggante ñaari xàlla:ã araf wii xàmmee ko mooy an ci Fr - ab waa faraas la ko wolof di woowe bu ñu dee ñu bari ñu ne ay waa farãas añs.
  • Ki koy làkk nag ? : kuy wax, mbooloo mi: ñuy wax
  • Làkk wi ci boppam nag ? làkku frãas walla rekk nga bañ a wax làkk te yam ci wu: wu frãas walla wu waa farãas.

Boo gisee wolof jëmul kanam ci wàll googu, dafa fekk daf doon dund ci menn réew ak yeneeni waaso aki xeet yu mu dëkkaloon, ci ñoom la gënoon a jëmale ay xalaatam, amutroon déggiinu réew waaye déggiinu waaso la gënoon a am ak tund (gox), ku dëkk ciw tund da daan baamu tund wi ñaari yoon bu ko defee muy ka fa dëkk, Tundu bawal: bawal-bawal, leeg-leeg nag nosiin wii soppiku ndax amaa na nga dégg kajoor ak ajoor ak doonte dees na wax kajoor-kajoor

diggante ñaari xàlla: entre parenthèse

  • Leneen lu néew lu ma la bëggoon a leeral: weer yi ngay jëfandikoo doon jëfandikoo yu saryaan yi moo gënoon, ndax wolof ay ndayi koor ak yu ni deme ñi ngi ci daa jublu weeri weer wi, weeri jant bi moom ay satumbar lanu daa wax jublu ci septembre,

Weeri jant bi mooy ay satumbar aki samwiye añse,. Weeri weer wi di ay maami koor aki baraxlu te yooyu ñooy yi ñuy séntoo ay weer naan feeñ naak feeñul bu feeñee ñu ne benn fan, leeg-leeg mu mat fan-weer leeg-leeg déet.Kon deel jëfandikoo ay samwie féwrie maars awril, araab yi sax moom lanuy jëfandikoo. Bu dee nag da ngaa bëgg a joxe ab taariix ci weeri lislaam yi bu boobaa nga wax maami koor baraxlu añse.

--Abdu Xaadir KEBE 1 Ndeyi-koor 2008 à 12:27 (UTC)

Dinaa la tontu ci kanam[Soppi]

ma bëggoon laa xamal ba la ma laa tontu ne deel sonn ci jumtukaayu gindi yi maanaam les articles definis yi, mbootaay ag mbootaay lanuy wax kenn du ne am mbootaay, ab waxtaanuwaay lanuy wax kenn du ne aw añse. dinaa la tontu ci li ci des, damaa xaw a jàpp moo tax--Abdu Xaadir KEBE 30 Maami-koor 2008 à 21:28 (UTC)

Ci lu aju ci laaj yi nga ma doon laaj[Soppi]

Dees na wax it doomu Frãas: français, bu ko defee ñu naan jenn doomi Fr de wàcc na ci naawuwaay bi biig juge Fr ngir siyaare si suñu réew mi ànd ak ñu bari ci ay doomi Tugal.

Ab waa Fr nag boo ko waxee nanga xam ne mi ngi bàyyikoo ci kenn ci waa Fr walla benn waay ci waa Fr, ndax waa moom du man a doon kenn mbooloo la, waaye ñu naan jamono ju nekk :kenn ci waa dey xaw a sonle mootax ñu maye ñu naan benn waa walla ab waa --Abdu Xaadir KEBE 1 Ndeyi-koor 2008 à 23:15 (UTC)

Ma ne[Soppi]

bul di taqale wu ak réew mi, maanaam bul bind: wuitaali, waaye wu itaali --Abdu Xaadir KEBE 12 Ndeyi-koor 2008 à 02:26 (UTC)

xoolal xëtu ndimbal wi am na coppite ci sosiinu xët yi. --Ibou 12 Ndeyi-koor 2008 à 11:20 (UTC)
  • li ci am ci lu jafe mooy man damay xaw a ñàkk jot ba tax na ni muy gën a lëmoodikoo, gën nee fasoodi (simple)la may gënale, kon bàyyil may def na ma daan def, bu ko defee nga topp ci di topp (corriger), loo gis ne moo gën ci wàllug xarala nga def ko. Ci noonu laay manee dugal lu bari. Loo wax ci li may dugal foofu ciy baat? mbaa am nanu njariñ? damaa bëgg nga gën a am ay baat ngir gën a man a firi (traduire)! su ko defee keneen xam, xam-xam lëw, sakkan, bu ko defee leegi ñu ba fi yeneen làmmiñ yi te fonk wii di sunu wos wi.--Abdu Xaadir KEBE 12 Ndeyi-koor 2008 à 19:09 (UTC)


  • Ma ne nanga xoolaat bàyyikoo, bari na ag jaxasoo, ag réeral nga gën a def ci ag leeral. Kenn du wax bàyyikoo, aji bàyyikoo lanuy wax te mooy aji bawoo rekk te def naa ko, xool ko ci baatukaay bi, bokkul ak gongikuwaay. Ay way bawoo walla ay way bàyyikoo ñooy baat yiy bàyyikoo ci gongikuwaay yi, ñu leen di wax ci wu frãas dérivés bu dee gongikuwaay nag mooy infinitif di baatu jëf bi baat yeneen yiy bawoo, nga xam ne mooy cosaanu baat yi ci des yépp. --Abdu Xaadir KEBE 14 Ndeyi-koor 2008 à 02:02 (UTC)

Lu aju ci baati politig yi[Soppi]

  • damaa bëggoon nga nos ko, te wax ma yenn baat yi ma def ay laaj luy seeni piri.

--Abdu Xaadir KEBE 30 Ndeyi-koor 2008 à 14:30 (UTC)

Ni ma ko nose nii baaxul? noo yaakaar ni mooy gën? Ngir am ay leeral ci tekkiy baat yi ci wu faraas demal ci bii dal. --Ibou 31 Ndeyi-koor 2008 à 18:21 (UTC)
Bul di duggal mbindi wu faraas ci xët yi, baati wu faraas yi ci wolof nga ko wara faramfacce, --79.41.243.239 3 Baraxlu 2008 à 18:50 (UTC)

li ma ci jublu[Soppi]

bu ma ko duggalee ci baatub wu fraas wi, maa ngi ci jublu, ki sikk man koo xool ba xam yanu na maanaa walla. Bu ma ko dugalee ci wolof nag maa ngi ci jublu su ma amee jot tekki ko. Nangu nga walla ? bu la neexee it bàyyees ko noonu, defees ni nga bëgg. --Abdu Xaadir KEBE 4 Baraxlu 2008 à 11:09 (UTC)

nand naa li nga wax!! waaye dayni rek fii lépp ci wolof la wara doon, tekkiinu baat yi ci wu faraas man nga leena saytoo ca dal booba, waaye bul di leen duppi di leen fi taf. leneen li waral ñakk ngee mana def mooy wikipedia ciy àtteem day bañ ku duppi mbindi beneen dal taf leen fi, ndax sàmmook àqi aji-sos si. --Ibou 4 Baraxlu 2008 à 12:33 (UTC)

déggatuma la, noo gise baati politig yi? waxoo ci dara de. --Abdu Xaadir KEBE 18 Ut 2008 à 14:28 (UTC)


Lu yees li ma bëggoon, mooy delloosi la ci mbirum làkk yi ñu nekkoon di waxtaane ci ginnaaw. Ma amoon lu ma ci seetlu lu jar a bàyyi xel, mooy : làkk ci làkk yu bari, dañu koy jëfandikoo ni ko boroom di wooye, maanaam: “Français” = frãse, “Italiano” = Italiaano, walla jëfandikoos ko ni ñu ko xame ci wu frãse = Itaaliẽ, siinwaa. Bu dee ci lu aju ci aji dëkk ci am réew man ngay baamu baat bi ñaari yoon bu la neexee, frãas-frãas, walla nga wax ab waa-frãs, mbaa doomi frãas. Lii nag yaakaar naa ne lu ñu man a bàyyi noonu la, lu ci neex waay mu jëfe.--Abdu Xaadir KEBE 27 Ut 2008 à 16:22 (UTC)

Soo xoole ci àdduna bi amul wenn làkk wuy jël ni ko weneen làkk di waxe, gis naa ni wolof yoon la mu am waxinu boppam, am na sax ñu ma jot a wax ni français wu faraas la ñu koy wax ci wolof, ñu rafetlu ko. te it gis naa it bind wu-faraas, taqale leen moo gën, ndax soo boole ñaari baat yi dalay jox beneen tekki, soo xoole làkku swahili noonu la ñuy def 'ki' la ñu yok ci kanamu réew ma mu jox la làkk wa ñu fay wax. xoolal fii ngir ay firnde.

Leneen li. xoolal fii --Ibou 7 Sattumbar 2008 à 22:25 (UTC)[répondre]

Xoolal foofu--Abdu Xaadir KEBE 21 Sattumbar 2008 à 16:24 (UTC)[Soppi]

abdu Xaadir Géy[Soppi]

Salaam Abdu Xaadir Kebe noo ngi lay siyaar bu wer te dila sant yit ci laggeey bu am solo bi gay def ngir jamale sunu làkk wu neex wii kanam yalla nala yalla jamale kanam ngis naa sak am solo ci dàl bii di wiki ak xibaaryi.com wiki boobi sax moo taxoona juk bataaxal bi ci nunuy def bajamaleko kanam. te loolu dara jiitu wusi siiwal ko ci dëkk bi baaxoon na lool nak ñu taxawal ag mbotaay maangi ciy xaar sa xalaat Waw-Kay (OK) sosoon naa aw xët ngir dugal fà baati wolof yima teewlu yepp ba leengi yemp na te yit def naa ci ay lakkalekaay ga xamni dagay kokk (clic) rekk dugal leeral yi ak lici aju bul fatte duga laale wàll wimu bokk ndax boo dugalee wàll wi dina waral mu man a wey ci wàllam, leengi yaakaar naani dugal ab baat ci dàll bi dina gën a yomp, kune man a cee dugal loxoom ngir dolli ci ay baat walla leeral baat yi noongi ciy xaar sa loxo ngir amna ci solo lool, ngir gis ko kokkal fii --Ahloubadar 25 Awril 2009 à 20:13 (UTC)[répondre]

  • Abdu Xaadir Géy Ahloubadar
  • Geejawaay/Marsé saam gël tappé 2 parcelle N°708
  • Jokkowu:775724577

waxiin[Soppi]

waxiin[Soppi]

am na jumtukaay bu bees boo man a jëfandikoo ci xët yi. misaal ci baatu «alal» lii ngay bind:

{{waxiin}} Déglul ni ñuy waxee baatu alal ci wolofi senegaal [[Dencukaay:Wo-alal.ogg]]

xoolal fii alal ngir gis limu lay jox.

demal fii ngir gis dencukaay yépp, commons:Category:Wolof pronunciation. --Ibou 1 Mee 2009 à 13:32 (UTC)[répondre]

Jaajef: man nag samag jot mooy xaw a neew ci wallug di ko dugal, kon dee ci yëngu, suma gënee am jot, japp ci. Meneen mbir: ku mel ni Abdu xaadir Gey, dee ko nemmiku, te` jéem koo gindi ba li muy def di dëppoo ak li fi nekk, ku am solo la, waaye gën koo saytu --Abdu Xaadir KEBE 3 Mee 2009 à 13:38 (UTC)

léebu[Soppi]

  1. Xaalis loo ko yonni mu indi ko, waaye falay jaare, déggee wu ma ko ci kénn sama xalaat la, li tax ma jëfandikoo indi ko kot mooy yaw miko yonni woon boofa nekkul it dinako indi, bu dee indil la ko nag kon day melni boo fa nekkul du ko indi,
  2. Yariit du bon, yarut du baax, sëriñ maalig ba siin, taalube sëriñ bi mooko daa wax,
  3. Mbej wa ray mbër, ponkal a koy dóor, maako sos, litax nee wu ma ponkal a ko ko dóor mooy loolu daa léebuwul, maanaam day firee ku, te kon day melni daa am ku may waxal, te waxu ma ak nit mbej wa laay waxal,
  4. Lu xaj lekk lekk, ba fa der ga ca baat ba, ag der lees di wax, doonte dees na wax aw der, waaye bókkul aw der day fékk muy dund, bu dundul ag der lay tudd, leer na,
  5. Suul ker du ko tee feeñ, du ko tee feeñ lees di wax, tere ndigël la, boo teree dara ba amul yaako tee am, ñaari baat yi am na ñu as wuute,
  6. Cërub ma xàjj, ma xujj a koy jël, lees di wax, maanaa mi moodi ku deful sa yitte ci mbir mi ki ko ci def jël sa wàll, xàjj bokkul ak xejj, xejj ku ñu genne ci mbir mi la,
  7. Cuqum a gën kamm, lees di wax, cuqum moodi coow li kimiñ di génne buy sàqami, kamm bokkul ak këmm, kamm ku ni miik sàqami wul, këmm nag ci askanu dagg la bokk, maanaa lu dagg ca cat la dagiin wu jub, nàndal-bubaax (bonne comprehension)


ku baax noo ngi lay siyaar bu wer, mbaa jàmm-nga-am ? naka liggéey yeek yuni mel ? gëj nanoo deggante mbaa amaat nga ag nosukaay ? waaw-kay (OK)User:Ahloubadar

Abdu Xaadir gey nee[Soppi]

Yaaram yaama gën a yélloo sant ngir sa goora ak sag cawarte santées nala gërëmees nala, man damay jéem rek, wax nga dëgg xam gees dul sikk Yàlla rekk a ko ame. te naggu leesu koko ci adduna, damay faral di wax naan: wax lu ñépp ànd mbaa jëfees ko kénn manu ko waaye fexeel di wax mbaa di jëf lu ñépp manoo na ànd te nóppi,
  • turu baat akuw santam, maako xalaatoon te yaakaarni jub na, soxla woon naa xam bi geen sosoon ?
  • wàllu xam-xamu nosukaay man dey bàyyi naalaak sama wàll te wey ci laneen,

loo wax ci sama bind bii ma def ci ag ak gi ? yónnee woon naako ca dal bii di xibaayi.com

defaroon naa ab dal bu yitte woo mbirum muriit ci FR booci manoona dugal sa loxo ci wàllu jukki yi, maangi koy tekki it ci wolof te fas naafa yeenee def teerey Sëriñ bi yi nga tekki ci wolof bu maci amee sa ndigël ? dal baa ngii www.ahloubadar.co.cc . am na ab xassida bu Alaaji Sëriñ Gey Badar wayoon Sëriñ Saaliwu sa maam ja, def naa ko ci man nga koo gis boo demee jaare ko ci "Bibliothéque/Sr Gueye" mooy Yaa Saalihal. defar naa it ab dal buy yitte woo mbirum waa mboussobe muy www.mboussobe.co.cc cant gu matale ñeelnala Waaw-kay --Ahloubadar 22 Mee 2009 à 17:26 (UTC)[répondre]

Tontu[Soppi]

Jaajefati, maa ngi lay delloo sant, te di la xamal ni bu ma sañoon benn bis nga ñëw fi, sama numero boo ko yorutoon mooy: 761392467, dinaa xool, li nga yonnee foofu ciy dal insallaa wax la ci sama xalaat, man sax gis naa li nga yonnee xibaar yi, muy lu am solo. Boo gisee ma wax la loolu, da di li ma gis nga wax ko fenn, mooy li am xalaat daa metti, xalaat ba sonn nu dindi ko baa xul, kon bees ko dee dindi nees fa teg lu gën, ndax nun ñépp xeet wi lanuy liggeeyal, bu kenn bëgg ndam, Yàllaa ngi gis dina fay it, soo xooloon li jotees a dugal boo ci àndul bu boobaa nga indi bi nga gis, bu jàllee nga door a xalaat ci lu amuul. Jaajëfati, Xéewal ak mucc, lépp lu ma bind nag mbaa mu bawoo ci man bul tàggoo--Abdu Xaadir KEBE 22 Mee 2009 à 18:37 (UTC)

liñ naan: tombee waral aay gaaf moonu dal ndax wax jooju linga ko jàppee taxu koo juk li maci jublu woon mooy bu mafi defee dara mu amal ma njëriñ te amul njëriñ ci dal bi buñ ko faree lor ma, dadi nak daa tombeek ma wax ci mbirum neenal nga yaakaar ni yaw laay waxal te fekk du loolu,

dara jaraluma werante bu ma demoon ba déggoo tuñu dama leen di bàyyi ngeen liggeey ma wey ci laneen, jël naa sa nimero, xamnaa du ñàkk bis ma amuk jot jaar foofu ndax jar nga ko, lima la waxoon ci wàllu téere yinga tekki woon ci wolof ? dal yi sax dañoo nek ci ab laggeey bu nóppee gul, damakoo dugalani rek ngir man a am yenn yi waaw-kay Ahloubadar

maa ngi jéggalu ci lepp lu ma wax mbaa ma def ko, te waruma, may wéy ci di la soññ ci jëf ju am solo ji nga nekke. --Abdu Xaadir KEBE 23 Mee 2009 à 12:41 (UTC)

Jaajëf mbokk. ndax gis nga lima la waxoon ci wàllu teerey sëriñ bi, yi nga tekki woon ci wolof ? Ahloubadar 23 Mee 2009 à 14:33 (UTC)[répondre]


Nee naa la lu aju ci loolu bul tàggoo, jëfandikool ni mu la neexe --Abdu Xaadir KEBE 23 Mee 2009 à 22:58 (UTC)

jaajëf waay sang bi, xamnaani ku laabiir nga yàlla rek a lay fay, santees nala , gërëmees nala Ahloubadar 24 Mee 2009 à 14:59 (UTC)[répondre]

Votre compte va être renommé[Soppi]

20 Maars 2015 à 08:45 (UTC)

Compte renommé[Soppi]

17 Awril 2015 à 04:43 (UTC)